Buleen jalgati yoon cib àtte, buleen jeng te buleen nangu alalu ger, ndax ab ger day muur bëti boroom xel, di xañ aji jub dëgg.
TSK
TSK · Acts 10:34
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Kii du far kàngam, du teg ku am ci kaw ku ñàkk, nde ñoom ñaar la boole sàkk.
Yeerukat ya dikk ne Yeesu: «Sëriñ bi, xam nanu ne njub ngay wax, di ko jàngle. Amuloo parlàqu itam, waaye ci kaw dëgg ngay jànglee yoonu Yàlla.
Ndax kat xejj ak seen amul fa Yàlla.
¶ Yeen it sang yi, jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, bàyyileen di tëkkoo, te ngeen xam ne yeen ak ñoom a bokk benn Boroom fa asamaan, te xejj ak seen amul fa moom.
Dundin wu yees woowu amul jaambur akub Yawut, amul ku xaraf ak ku xaraful, amul ab doxandéem ak ku xayadi, amul ab jaam ak as gor, waaye Almasi mooy lépp te moo nekk ci ñépp.
su boobaa xanaa du yeena ngi gënaatle ci seen biir, tey àttee ay mébét yu bon?
¶ Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf.