TSK

TSK · Acts 10:38

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Buuri àddinaa ngi dér, boroom nguur yi daje, di fexeel Aji Sax ji, mook ki mu fal.

Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. Njub nga ŋanke sa nguur gi,

«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.

Luke 3:22 TSK

Ba loolu amee Noo gu Sell gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaa may bànneexal.»

Luke 4:33 TSK

Ndeke foofa ca jàngu ba, jenn waay ju rab jàpp a nga fa woon. Waa ji jekki xaacu, ne:

Luke 7:11 TSK

¶ La ca tegu Yeesu demati dëkk bu ñuy wax Nayin, ay taalibeem ak mbooloo mu bare ànd ak moom.

Luke 9:42 TSK

¶ Naka la xale bi jubsi Yeesu, rab wi sànni ko ci suuf, muy say. Yeesu itam gëdd rab wa, wéral xale ba, delloo ko baayam.

Acts 2:22 TSK

¶ «Yeen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu waa Nasaret bi, Yàlla moo firndeele ag dëggoom, ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll.

Yaa safoo njubte, seexlu njubadi, moo tax yaw Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom.»

¶ Àndleen ak sago te teewlu! Seenub noon Tuumaalkat bi, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax.