Proverbs 1:23
TSK
Soo dëppee ba déglu, ma àrtu la. Ma ne, kon ma xellil la samam xel, xamal la samay kàddu.
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Soo dëppee ba déglu, ma àrtu la. Ma ne, kon ma xellil la samam xel, xamal la samay kàddu.
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
Booba lañu fàttliku kàddug Yeesu googu.
ne leen: «Ndax ba ngeen gëmee, jot ngeen ci Noo gu Sell gi?» Ñu ne ko: «Nun de yégunu woon sax ne Noo gu Sell gi am na.»
Ci genn Noo gi lañu nu sóobe ci biir wenn yaram wi, nun ñépp, nu diy Yawut, mbaa nu diy jaambur, nu diy jaam, mbaa nu diy gor, te nun ñépp, genn Noo gi lañu nu nàndale.
¶ Soppe yi, sama ñaareelu bataaxal a ngi nii, te bu ci nekk am na lu ma leen ci fàttli, ngir xiirtal leen ci xalaatin yu set,