TSK

TSK · Acts 12:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yaw Aji Sax ji, kay, laay niitoo, Aji Sax jeey leeral sama lëndëm.

Malaakam Aji Sax ja dellu ñëw, laal ko, ne ko: «Jógal lekk, lu ko moy doo àttan yoon wi.»

Ku bon a ngi yeeru ku jub, di ko wuta bóom.

xar seeni jéng yaar, génnee leen lëndëm gu tar.

Aji Sax ji, ma woo la wall; ma ne, yaay sama kiiraay, di sama séddoo fi kaw suuf.

Lii, def ko ci, mu dib takk. Dees na lekk ren peppum saxayaay, déwén it dees na lekk lu saxal boppam. Waaye déwén-jéeg, ngeen ji, góob, jëmbat tóokëri reseñ, lekk ca meññeef ma.

Ma jekki gis leeru Yàllay Israyil, mu dikke penku, ànd ak kàddu gu mel ni kàddug géej mbàmbulaan, suuf si di lerxate fa leeram ga.

¶ Dañeel daldi ne Buur: «Buur, guddalu fan!

Kee di leer gu ne ràññ, ay ceeñeer fettaxe ci loxoom, te fa la dooleem làqe.

Luke 2:9 TSK

Am malaakam Boroom bi jekki feeñu leen, leeru Boroom bi melax, wër leen, ñu tiit tiitaange lu réy.

Acts 2:24 TSK

Waaye moom la Yàlla yiwee ci mititu ndee, dekkal ko, ndax dee amul kàttanu tënk ko.

Acts 9:3 TSK

¶ Naka la Sóol dem ba jub Damaas, ag leer bawoo asamaan, jekki ne ràyy ci kawam.

Acts 12:6 TSK

¶ Ba ñu demee ba ca guddi, ga jiitu bés ba ko Erodd wara yóbbu, Piyeer a ngay nelaw ci diggante ñaari takk-der, ñu yeewe ko ñaari càllala, ay dag di wattu buntu kaso ba.

Ci kaw loolu suuf jekki yëngu yëngu bu mag ba kenug kaso ba di rëng-rëngi; bunt yépp jekki ubbiku, jéngi ñépp dàjjiku.

te lépp lu ñu wone ci ag leer, di ag leer. Moo tax ñu ne: «Yaw miy nelaw, yewwul, dekkil, Almasi leeral la.»

¶ Gannaaw loolu ma gis meneen malaaka mu am sañ-sañ bu réy wàcce asamaan, àddina di leere cig leeram.