Moo tax ma tànn ko, ngir mu sant ay doomam ak waa këram, ñuy déggal Aji Sax ji, di jëfe yoon ak njub. Noonu laay defale Ibraayma li ma ko digoon.»
TSK
TSK · Acts 13:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf: Benn dogal la ñépp bokk, te it nit a ngi sóobu ci mbon, di mébét jëfi dof giiru dundam, ba noppi fekki ña dee.
Yeen Efrayim, lu ma masa séq ak jëmmi tuur? Man maa leen di nangul, di leen wattu, di leen keral ni garab gu naat gu dul ruus, sa meññeef bawoo fi man.»
Sang bi ne ko: «Yeen Farisen yi, bitib kaas bi ak ndab li daal ngeen di raxas, te fekk leen feese jikkoy jagoo lu lewul, akug mbon ci biir!
Piyeer ne ko: «Na sa xaalis ànd ak yaw asaru, ndegam ab xaalis nga yaakaara jënde mayu Yàlla!
Ci seen biir sax la aw nit di jóge taxaw, di wax ndëngte, ngir xiirtal taalibe yi, ba ñu topp leen.
Te beneen dafa amul sax, xanaa ñenn ñi leen di jaxase, te bëgga sopparñi xibaaru jàmm bu Almasi.