Yeen askanu Ibraayma, jaamam ba, yeen ñiy sëti Yanqóoba, ñiy tànnéefam,
TSK
TSK · Acts 13:26
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Waaye yaw Israyil, sama jaam bi; yaw Yanqóoba mi ma taamu, yaw askanu Ibraayma, samab xarit!
Yeen waa kër Yanqóoba, dégluleen; yeen ñi ñu wooye turu Israyil, yeen ñi bawoo bëti ndoxi Yuda, di giñe turu Aji Sax ji, yeen ñiy sàbbaal turu Yàllay Israyil te dëgg ak njekk taxul,
Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu, fi biir kër Daawuda jaamam ba,
te ciw turam, dees na dale ci Yerusalem, yégal xeet yépp, tuubeel gu jur njéggalug bàkkaar.
Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»
waaye xeetoo xeet, ku ko ci ragal tey def njekk, mooy ki ko neex.
Ba mbooloo ma tasaaroo, bare na ay Yawut ak tuubeen yuy jaamu Yàlla yu topp ci Póol ak Barnaba. Ñuy wax ak nit ñi, di leen ñaax, ngir ñu sax ci doyloo yiwu Yàlla.
Ndaw sa topp ci Póol ak nun, di xaacu, naan: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; dañu leen di yégal yoonu mucc.»
¶ Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.
¶ Kooku, yeen ñi dul Yawut, ba ngeen déggee, yeen itam kàddug dëgg gi, xibaaru jàmm, bi jëm ci seenug mucc, gannaaw ba ngeen gëmee, ci moom itam lañu leen màndargaale Noo gu Sell gi ñu dige woon.