TSK

TSK · Acts 17:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dëddul jëfi téxét ba dund, di jubal ci yoonu dégg.»

«Éy Siyoŋ, rëccal, yaw mi dëkke janq Babilon mu taaru mi.»

Acts 2:44 TSK

Gëmkat ñépp benn lañu woon te ñoo bokkoon lépp.

Acts 5:12 TSK

¶ Ci kaw loolu ay firnde ak kéemaan yu bare di sottee ci loxol ndaw yi, ci biir askan wi. Gëmkat ñi nag di bokk daje ñoom ñépp fa ñuy wax Mbaarum Suleymaan, ca biir kër Yàlla ga,

Teewul Yawut ya xiirtal tuubeen yu jigéen yi gëna ràññiku, ak kàngam yu góor yi ci dëkk bi. Ñu daldi bundxatal Póol ak Barnaba, génne leen réew ma.

Acts 14:4 TSK

Ba loolu amee waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya.

Kon nag noo yebal Yuda ak Silas, ngir ñu àgge leen ci seen gémmiñu bopp, lii nu leen bind.

Póol moom, taamu Silas, daldi ànd ak moom dem, gannaaw ba leen bokk ya dénkee Boroom bi ciw yiwam.

Ci kaw loolu Yawut yu bare gëm, ñoom ak jigéeni Gereg ñu ràññiku, ak ay góori Gereg ñu bare.

Teewul mu am ñu ko fekksi, ba mujj gëm; Denis mi bokk ci ëttub Areyopas ci la, ak jigéen ju ñuy wax Damaris, ak ñeneen.

Loolu moo wéy diiru ñaari at, ba mboolem waa diiwaanu Asi dégg kàddug Sang bi, muy Yawut, di Gereg.

Ñenn ña nag gëm la mu wax, ña ca des weddi.

Li nu séentu woon sax wees nañu ko, nde Sang bi lañu jëkka jébbal seen bopp, door noo jébbal seen bopp, te noonu la ko Yàlla bëgge.