TSK

TSK · Acts 2:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Bésub Aji Sax jaa ngii di ñëw, bés bu néeg, bésub mer ak sànj muy tàkk, nara gental suuf, te bàkkaarkat ya la fay fàkkas.

Kersa la weer wiy am, gàcce ñeel jant bi; Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal, mooy nguuru Yerusalem, kaw tundu Siyoŋ, leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam.

Maa xool suuf, ndeke ma nga ne maraas, ne wëyëŋ; ma xool asamaan, leer amatu ca.

balaa dogal bee taxaw, bésub mbugal ne jaas ba wéy ni boob, bala leen tàngooru merum Aji Sax jee dikkal, bala leen bésub merum Aji Sax jee taxawal.

dàqleen nit kooku, jébbal ko Seytaane, ngir sànkutey yaramam, ndax aw fitam mucc, keroog bésu Boroom bi.

Waaye asamaanu tey jii, ak suuf, genn kàddug Yàlla googu moo leen yeb cib denc, ñeel sawara, kera bésub àtte ba, bésu sànkuteb aji gëmadi ñi.

¶ Ma gisati bi muy tàyyi juróom benneelu tayu gi, suuf daldi yëngu bu baaxa baax, jant bi ñuul kukk, weer wi wépp xonq curr ni deret.