TSK

TSK · Acts 2:27

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 19:25 TSK

Waaye man xam naa ne sama jotkat a ngi dund, te mooy mujje taxaw fi kaw suuf.

Ngor lu réy nga ma won, sorele maak tëraayu bàmmeel.

Buumi ndee a ma laawoon, njàqarey njaniiw dab ma, ma dajeek naqar aku tiis.

Luke 1:35 TSK

Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam ku Sell kiy juddoo ci yaw, dees na ko wooye Doomu Yàlla.

Ci kaw loolu ñu dugal ko sawara. Ca biir mbugal mu tar ma la dawale bëtam, daldi séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.

Acts 2:31 TSK

Kon li mu gis te dikkagul mooy ndekkitel Almasi, te ci mbiram la wax ne bàyyeesu ko biir njaniiw, te yaramam du yàqu.

Acts 4:27 TSK

Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.

Lu gaawa gaaw lay doon, ci xef ak xippi, bu liit gu mujj ga jibee; nde liit ga mooy jib, ñi dee, dekki, di ñu dul yàqooti, nun nag, nu soppiku.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Filadelfi nag, bind ko, ne ko: «Lii moo di kàdduy ku Sell ki, kiy Dëgg, te yor caabiy Daawuda, di tijji te kenn du tëj, di tëj te kenn du tijji. Mu ne: