Samiyel ne ko: «Ana meem joojuy tàbbi sama nopp bii, lu mu doon? Ak looluy nàññi, may dégg?»
TSK
TSK · Acts 21:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Lu waral ngeen di dëggaate sama ñoñ, nappaaje néew-doole yi?» Kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi.
Ci kaw loolu njiitu mool ya dikk ba ca moom, ne ko: «Yaw, ana looy nelaw? Jógal kay woo sa yàlla wall! Jombul mu geesu nu, ba dunu sànku.»
Maa koy won mboolem coono bi mu wara dékku ngir sama tur.»
Ba loolu amee ñépp jooyoo jooy yu metti, laxasu ko, fóon ko.
Bokk yi, man de bés bu nekk ma jàkkaarlook ndee, ak sag bi ma leen di sagoo ndax Yeesu Almasi sunu Boroom, mi ngeen gëm.
Xanaa ay surgay Almasi lañu? Naa ràkkaaju nag, te ne maa leen ko gëna doon. Bu dee ci liggéey yu metti, maa man fopp; bu dee ci fani kaso, maa ëpple fopp; bu dee ci ay yar, maa ëpple ay yooni yoon, te bare na lu ma riisu ndee, ba raw leen:
Su ma ci deeyee sax, ba sama dund mel ni sarax su ñu tuur, tofal ko ci sarax, bi seen ngëm taxawe, su boobaa it maa ciy bég, te di leen woo, ngir bokk ak yeen ñépp bànneexu.
¶ Léegi nag maa ngi bége coono yi ma jànkoonteel ngir seen njariñ; li des ci tiisi Almasi, moom laay mottalee coono yooyu ma daje sama yaramu suux wii, ngir njariñal mbooloom gëmkat, miy yaramu Almasi.
Ab takk-der bu bëgga neex ka ko solal kat, du xintewoo mbiri nit ña soluwul.
Ndax damaa leer, ni ma ko sunu Boroom Yeesu Almasi leeralale, bés bi may summi sama màkkaanu suux bii dëgmal na.
Sunu bokk yee daan ndax deretu Gàtt bi, ak seen kàddug seede, te soppuñu seen bakkan ba ragala dee.