Noonu la Filib deme péeyub Samari, di siiwtaane Almasi.
TSK
TSK · Acts 21:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Bokki gëmkat ña nag yég ko, daldi koy yóbbu Sesare, yebale ko foofa, mu dem Tàrs.
Naka la jot peeñu ma, mu daldi nu bir ne Yàllaa nu yebal ngir nu xamleji foofa xibaaru jàmm bi. Ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan.
¶ Noo doon dem jullikaay ba, ab surga bu jigéen bu rabu gisaane jàpp, dajeek nun. Alal ju bare la ay njaatigeem daa jële ci ngisaaneem.
Nun nag ba màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu mu amul lawiir weesee lanu dugge gaal fa dëkk ba ñuy wax Filipi, am juróomi fan ca yoon wa, door leena fekksi ca Torowas, toog fa juróom ñaari fan.
¶ Ba mu ko defee mu woo ñaari njiiti takk-der, ne leen: «Waajal-leen ñaar téeméeri xarekat ak juróom ñaar fukki gawar ak ñaar téeméeri boroom xeej, ngir ngeen dem Sesare bu juróom ñeenti waxtu jotee ci guddi.
¶ Gannaaw ba nu fa amee ñetti weer lanu dugg gaal gu lollikoo woon ca dun ba. Gaal gaa nga bàyyikoo woon Alegsàndiri, di xàmmikoo jëmmi tuur ya ñuy wax Kastor ak Polugsë. Nu daldi tàbbiwaat biir géej.
Moo may ñii di ay ndawam, ñee di ay yonent, ñee di ay xamlekati xibaaru jàmm bi, ñale di ay sàmmi mbooloom gëmkat ñi, mbaa ay jànglekat.