TSK

TSK · Acts 23:30

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Acts 9:24 TSK

Sóol nag yég seen mébét. Guddi ak bëccëg lañu doon wattu bunti dëkk ba, ngir bóom ko.

¶ Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.

Mu ne ko: «Xaaral ba say tuumaalkat itam dikk, ma déglu la.» Mu santaane nag, ñu denc ko ca kër buur Erodd.

Xanaa ñenn Yawuti diiwaanu Asi ña ma fa fekkoon. Ñooñoo ma waroona tuumaal fi sa kanam, ndegam am nañu lenn lu ñu ma sikke.

Ma ne leen: “Aaday Room daal nanguwul ñu jébbale nit, ngir ñu rey ko, te jëkkula jàkkaarloo ak ñi ko tuumaal, ba mana layal boppam ci mbir mi ñu ko tuumaal.”