¶ «Yeen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu waa Nasaret bi, Yàlla moo firndeele ag dëggoom, ay kéemaan aki kiraama aki firnde yu mu sottale jëmmu Yeesu moomu fi seen biir, te loolu xam ngeen ko xéll.
TSK
TSK · Acts 3:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.
xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane notoon.
¶ Ci kaw loolu ay Yawut yuy wër di faj ku rab jàpp, tàmbalee roy, di tuddal ñi rab jàpp turu Sang Yeesu, naan rab yi: «Maa la dàq ci turu Yeesu, mi Póol di xamle.»
Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
Ndax kat ab joxe, bu àndee ak yéene rekk, la boroom joxe bi amul, deesu ci natt lees koy nangul, waaye li mu am, ci lees koy nangul ab joxeem.
Kenn ku ci nekk, may gi ko aw yiw jagleel, na ko taxawoo ñépp. Noonu ngeen di doone ay saytukat yu baax yu yiwu Yàlla wu yaa.