TSK

TSK · Acts 4:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Acts 5:17 TSK

¶ Ba mu ko defee xolu kañaan dugg sarxalkat bu mag ba, ak mboolem ña ko dar, te di waa ngérum Sadusen ña.

Ba Yawut yi gisee mbooloo ma nag, kiñaan man leen, ñuy weddi waxi Póol, di ko saaga.

Ndaxte Yàlla jàpp na bés bu muy àttee àddina ci dëgg, àtte bu nit ki mu taamu di sottali; te loolu Yàlla jox na ci ñépp firnde lu wóor, ba mu dekkalee kooku mu taamu, ndekkite lu dee toppul.»

Lenn de man naa la koo nangul. Yoon woowu ñu ne mooy ngér mu sikk, moom laay topp, di ko jaamoo sunu Yàllay maam. Teewul mboolem lu ñu bind ci yoonu Musaa ak téerey yonent yi, gëm naa ko.

Acts 26:8 TSK

Ana lu leen taxa jàpp ci seen biir ne xel nanguwul Yàlla di dekkal ñi dee?

Noowug ki dekkal Yeesu moo màkkaanoo ci yeen. Kon nag ki dekkal Almasi mooy dekkal itam seen yarami ndee, ndax Noowam googu màkkaanoo ci yeen.

Waaye ku nekk ak ayam. Jooxeb ndoortel meññeef mi, Almasi la. Gannaaw loolu ñoñi Almasi ñooy aye, keroog bu délsee.

¶ Bokk yi nag, buggunu ngeen réere mbirum way dawlu ñi, bay tiislu ni ñeneen ñi amul jenn yaakaar, di tiisloo.