Aaróona këf and ba Musaa wax, daw dugg ca biir mbooloo ma. Ndeke mbas ma tàmbali na ca biir mbooloo ma. Mu def ca and ba cuuraay, daldi defal mbooloo ma njotlaay.
TSK
TSK · Acts 5:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Samiyel def la Aji Sax ji wax. Ba mu agsee Betleyem, magi dëkk ba gatandoo ko tiitaange, ne ko: «Mbaa tànki jàmm?»
Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu, way-gëmadi yaa ngay lox. Ana kan ci nun moo mana dal ak sawara suy xoyome? Ana kan ci nun moo mana dal ak taal yu yànj ya dul fey?
«Képp ku ñëw ci man, te bañuloo sa baay ak sa ndey, ak sa jabar, ak sa doom, ak sa bokk yu góor, ak sa bokk yu jigéen, bañuloo sa bakkanu bopp sax, doo mana doon sama taalibe.
Waaye xamuñu nu ñuy def, ndax ñépp a ko doon déglu, teewlu ko lool.
Ñuy màggal Yàlla, ñépp naw leen. Bés bu nekk nag Boroom bi di yokk ca mbooloo mooma, nit ña jota mucc.
¶ Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, daldi daanu, dee. Tiitaange lu réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.
¶ Ndax kat gannaaw bu ñu xamee bu baax sunu Boroom, sunu Musalkat Yeesu Almasi, ba rëcc sobey àddina, bu ñu ca sóobuwaatee ba mu man leen, su boobaa seenug muj moo yées seenug njàlbéen.