Exodus 24:3
TSK
Musaa dem, yeggeji mbooloo ma kàdduy Aji Sax ji yépp, ak àttey yoonam yépp. Mbooloo ma mépp bokk benn baat, ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def.»
TSK
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Musaa dem, yeggeji mbooloo ma kàdduy Aji Sax ji yépp, ak àttey yoonam yépp. Mbooloo ma mépp bokk benn baat, ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def.»
«Taxawil fa bunti kër Aji Sax ji, nga yéene fa kàddu gii, ne leen: “Mboolem yeen waa Yuda ñiy jàlle bunt yii, di jaamusi Aji Sax ji, dégluleen kàddug Aji Sax ji.
Ba mu ko defee Pasur dóorlu Yonent Yàlla Yeremi, jéng ko ca buntu kër Aji Sax ja féete kaw, te ñu dippee ko Beñamin.
«Aji Sax ji dafa wax ne: Dangay taxawi ca biir ëttu kër Aji Sax ji. Nga wax ak mboolem waa dëkki Yuda yiy jaamusi ci kër Aji Sax ji. Mboolem kàddu yi ma lay yóbbante ci ñoom, bu ci wacc baat.