¶ Bànni Israyil demati ba dali ca joori Mowab ca wàllaa dexu Yurdan, janook Yeriko.
TSK
TSK · Amos 2:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba mu ko defee buurub Israyil ak buurub Yudak buurub Edom dem di dox diiru juróom ñaari fan, ba ñook jur gi ñu àndal, kenn amatu ci ndox.
Sa ñoñ lañuy rabatal, di mànkool sa séddoo yii.
Xanaa ñu ne coww ba sowu, ne jàyy cëppandoo fa kaw waggi Filisteen ña, waa penku, ñu sëxëtoondoo; Edom ak Mowab, ñu teg loxo; Amoneen ña nangul leen.
Aji Sax ji kat teg na tund wii loxo, te ni ñuy dëggaatee boobum leeñ, ni lees fiy dëggaatee Mowab.
«Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Waa Mowab ak Seyir a ne: “Xool-leen waa kër Yuda ñii ni ñu mujje, ñook xeet yépp a yem!”
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Gasa, te duma fomm seeni duma. Ñoo jàpp njaam mbooloom lëmm, jalax Edomeen ña.
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Edom, te duma fomm seeni duma. Ñoo toppe seen bokki bànni Israyil saamar, jalax yërmande, mer mer mu dul meddi ak xadar ju dul giif mukk.
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Yudeen ñi, te duma fomm seeni duma. Ñoo gàntal sama yoon man, yoonu Aji Sax ji, te sàmmuñu sama dogali yoon. Seen tuuri caaxaan ya seeni maam toppoon sànk na leen.
Yeen sama ñoñ, fàttlikuleen rekk la leen Balag buurub Mowab fexeeloon, ak la ko Balaam doomu Bewor tontu woon. Doxub diggante Sitim ba Gilgal it, baleen ci xel, ba ràññee njekku Aji Sax ji.