TSK

TSK · Amos 3:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

ma wax leen ko bés niki tey, su boobaa yeenay sànkoo sànku, te dungeen gudd fan ca réew ma ngeen di jàll dexu Yurdan, jëm fa, ngir nanguji ko.

Moonte Aji Sax ji àrtu woon na Israyil ak Yuda, mboolem yonentam yaak boroom peeñu ya jottli leen ko, ne leen: «Dëppleen seen yoon yu bon yii ngeen topp, te sàmm samay santaane, wormaal samay dogal, na mu dëppook mboolem yoon wi ma tëralal seeni maam, yónnee leen ko, yonent yiy samay jaam jottli leen ko.»

Nanga leen àgge samay wax, ñu déglook ñu gàntal, nde ay fippukat lañu.

Acts 2:40 TSK

Yeneen kàddu yu bare soññe na leen ko, ñaaxe leen ko, ne leen: «Muccleen ci gii maas gu dëng.»

Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub ci Yàlla te gëm sunu Sang Yeesu.

Ci moomu mbir, bu kenn ci yeen tooñ mbokkam, di aakimoo yelleefam, ndax waxoon nanu leen ko, ba artooti leen ne leen jëf ju ni mel, Boroom bee koy fey ña ko def.