Moo wàcce ab xiif ca réew ma, dagge fa luy gub,
TSK
TSK · Amos 6:11
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu àddooti, ay soccet dikk, di njéeréer yu wees ab lim,
Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,
Maay yégle muj ca ndoorte la, ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg. Maa naa sama mébét a ngi, day am, sama bépp nammeel sotti.
«Yaw nit ki, Nabukodonosor buuru Babilon teg na mbooloom xareem, coono bu metti ca seen xareek Tir. Seen kawari bopp yépp ruus na, seen wagg yépp tëccu, te coonoom ba mu sonn ca Tir, yooloowu ca dara, du moom, du ay nitam.
Bu liitu xare jibee, waa dëkk ba du tiit a? Am aw ay dina dab ub dëkk te du Aji Sax ji?
Boroom bi, Aji Sax jee ko giñ ci boppam, kàddug Aji Sax ji Yàllaa, Boroom gàngoori xare yi. Nee: «Maaka sib réy-réylug askanu Yanqóoba, ba seen kër yu yànj soof ma! Maay jébbale seen péey ak mboolem li ci biir.
«Maa ngii déy di sant xeetoo xeet, ñu gësëm waa kër Israyil, ni ñuy gësëme tameb suuf, te doj du rot.
Xeet yépp laay dajale ci kaw Yerusalem, ngir xare. Dëkk bi lees di nangu, sëxëtoo kër yi, tëdde jigéen ñi. Genn-wàllu dëkk beey génn, jëm ngàllo, waaye ndesu askan wi, deesu leen dagge ci dëkk bi.