TSK

TSK · Amos 6:12

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Yesabel ne ko: «Xanaa du yaay buurub Israyil? Jógal lekk waay te bégal sa xol. Man maa lay jox toolu reseñu Nabot.»

Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen. Dangeen të, wowle.

Aji Sax ji, xanaa du worma ngay sàkku? Dóor nga leen, safu leen; nga làbbli, ñu tanqamlu, wowle ba raw doj, baña dëpp.

Ñooy wax seeni wax, di giñe ay fen yu ñuy fasoo kóllëre, ba yoon mel ni gàncaxu tooke ju law ca tooboy tool ya.»

Amos 5:7 TSK

Wóoy yeen ñiy walbati àtteb yoon, mu mel ni xay, tey jalax dëgg fi pëndub suuf!

Micah 7:3 TSK

Lu bon la seeni loxo mane: kàngam di laaj, ab xaali di sàkkub ger, boroom daraja moom, di wax fuqley bakkanam, ñu ànd ràbbum pexe.

¶ Teewul ñu baña déglu, të ticc, fatt seeni nopp, ngir baña dégg.