Bu màggoon ba tollook asamaan it, ba bopp ba àkki fa kawa kaw,
TSK
TSK · Amos 9:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Moo leen di may ñu wéeroo seen cëslaay, tey xool fa ñuy jaare.
Fu ma jëm, ba sore la? Fu ma daw jëm, foo teewul?
nit ñi làquji biir xuntiy doj, ruuruji biiri pax, ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab, sore darajay màggaayam, kera buy taxaw, ba suuf di lox.
Seen ragluwaay ak seen reewande sànk na leen, yeen ñi dëkke xuntiy doj, féetewoo colli tund yi. Waaye su ngeen ajee seenum tàgg ni jaxaay it, fa laa leen di àjjee.» Kàddug Aji Sax jee.
Yaa nga woon biir Àjjana, toolub Yàlla ba, ràngoo lépp luy gànjari per, sarduwan ak topaas ak jamaa ak kirsolit ak onigsë ak jàspë ak safiir ak emëródd ak eskarbukal. Fegukaay yaak wewukaay ya di wurus, te bés ba ñu la sàkkee, fekk na ñu waajal yooyu.
Yeesu ne leen: «Séen naa Seytaane mu fàqe asamaan ni ag melax.