Teewul seen baay wor ma, soppi sama peyoor fukki yoon ak juróom, waaye Yàlla seetaanu ko, mu di ma lor.
TSK
TSK · Daniel 1:20
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba mu ko defee Firawna moom itam woo boroom xam-xam yaak jibar ya. Ñeengokati Misra ya ñoom it fexe ca seeni xargafuufa, ba def lu mel noona.
Mbott yi dinañu jóge sa kër, teqlikook yeen, yaak say dag ak sa waa réew, ca dexu Niil ga doŋŋ lañuy des.»
gannaaw mboolem nit ñi gis samag leer, gis firnde yi ma def ci digg Misra ak ci màndiŋ mi, ñoo ma nattu nii fukki yoon, bañ maa déggal,
¶ Ci kaw loolu Lingeeru Saba dégg riirum Suleymaan ma turu Aji Sax ji waral. Mu dikk di nattusi am xelam, di ko cax cax yu jafe.
Te it ñay tabax, ku ci nekk, sab saamar a nga takke ci sa ndigg, ngay liggéey, boroom liit gi feggook man.
Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.
Jàppool say jat rekk ak sa xërëm yu ne xas yoo dale sonn ba ngay ndaw. Jombul mu amal la njariñ, mbaa ñu ragale la ko.
¶ Ba mu ko defee ñu siiwtaane dogal ba, nara reylu boroom xam-xam ya. Ñuy seet nag Dañeel aki àndandoom ngir rey leen.
¶ Dañeel ne Buur: «Buur, li nga laaj amul benn boroom xam-xam mbaa ñeengokat mbaa taryaax ak seetkat bu la ko mana xamal.
¶ Buur daldi àddu ca kaw, di woolu ñeengokat yeek xërëmkat yi ak seetkat yi. Mu wax ak boroom xam-xami Babilon yooyu ne leen: «Képp ku jàng mbind mii te wax ma lu mu tekki, dees na ko solal yérey buur yu xonq curr, takkal ko caqu wurus, jox ko kilifteef gu koy tofal ci bummi.»
Noonee Sànnes ak Sàmbres doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm.