TSK

TSK · Daniel 12:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Léegi nag, soo leen dee baal seen bàkkaar, aa... Lu ko moy kat, far ma rekk ci téere bi nga bind.»

Dencal leen tooñ ci kaw tooñ, te yàlla buñu tàbbi ci sag njekk.

Boroom bee yónnee kàddu gu dal Israyil, askanu Yanqóoba,

Yeen samaw askan, ayca duggleen seeni néeg, tëju ca biir. Làquleen as lëf, ba sànj mi jàll.

Wóoy boobu bés bu réy, ba bés du ni mel! Bésu njàqare lay doon ñeel askanu Yanqóoba, waaye dañuy mucc.

Sama loxooy dal yonent, yiy gis peeñuy caaxaan, di gisaaney fen. Sama péncum ñoñ, duñu fa teewe, limeefu kër Israyil, deesu leen ca bind, te réewum Israyil, duñu fa dellu. Su boobaa ñu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.

te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji bànni Israyil ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, délloosi leen seen suufas bopp.

Matal nga sa kàddu gi nga wax ci nun, nook sunu kilifa yi nu yilif, ba nga wàccee ci sunu kaw, ci Yerusalem, musiba mu réy mu masula am feneen fu mboolem asamaan tiim.

Waaye rawaanu nguurug Pers moo ma dogale ñaar fukki fan ak benn. Mikayel nag, kenn ci malaakay wattukat yu mag yi ñëw, wallusi ma. Yàgg naa ca buuri Pers ya.

Dina samp xaymay kër buur ci diggante géej geek tund wu taaru wu sell wa. Waaye dina dee, te kenn du ko taxawu.»

Waaye kaw tundu Siyoŋ la aw ndes di rawe, te dina doon bérab bu sell, waa kër Yanqóoba it moomaat seeni moomeel.

Noonu leen rab yi nangule nag, buleen ko bége, bégeleen kay la seen tur binde fa asamaan.»

Kon nag naka noonu itam ci jamonoy tey jii, aw ndes a ngi fi, te ci kaw yiw lees leen taamoo.

Su boobaa nag, bànni Israyil gépp ay mucc, noonee ko Mbind mi indee ne: «Siyoŋ la wallukat bay jóge, mooy tenqee ngëmadi ci askanu Yanqóoba.

Yaw itam sama mbokkum surga bu dëggu bi, dama lay ñaan nga jàpple leen ci, ñoom ñaar ñooñoo bokkoon ak man coonob xamle xibaaru jàmm bi, ñoom ak ñoom Kelemaŋ, mboolem sama bokki liggéeykat yi seeni tur binde ca téereb dund ba.

tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,

¶ Ab xare nag jibe fa asamaan. Mikayel aki malaakaam di xareek ninki-nànka ji, ninki-nànka jeeki malaakaam it di xare,

¶ Ba mu ko defee juróom ñaareelu malaaka mi sotti ndabam ci kaw ngelaw li, baat bu xumb jóge ca ngàngune ma ca màkkaan ma, ne: «Sotti na!»

¶ Ba loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku, fas wu weex daldi feeñ. Ki ko war, «Wóor te Dëggu» lañu koy wax te njub lay àttee, di ko xaree.

Képp ku ñu gisul ñu bind la ci téereb dund bi, ci déegu sawara si lees la sànni.