TSK

TSK · Daniel 12:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.

Waarekat ba daa xelu, di jànglewaale xam-xam, di natt ak a gëstu, di jekk-jekkal kàdduy xel yu takku.

Te it boroom xel yu rafet yi ci mbooloo mi dinañu gindi ñu bare. Nattu dina leen dikkal ab diir; ñii saamar jaar ci seen kaw, ñii ñu lakk leen, ñee ñu nangu seen alal, tëj leen.

Acts 13:1 TSK

¶ Ca biir mbooloom gëmkat, ña woon ca dëkk ba ñuy wax Àncos, amoon na ay yonent ak ay jànglekat: ñuy Barnaba, ak Simeyon mi ñu dippee Ñuule, ak Lusiyus mi bawoo Siren, ak Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom Galile, ak Sóol.

Am na itam ay yaram yu farewoo asamaan, ak ay yaram yu farewoo suuf. Yaram wu farewoo asamaan nag, ag leeram wuute na ag leeru yaram wu farewoo suuf.

ànd ak kàddug dund gi ngeen di xamle. Su ko defee keroog bésub Almasi, ma mana damoo ne dawuma cig neen, te sonnuma cig neen.

Ndax kat nëgëni tey waroon na leena fekk diy sëriñ, waaye aajowoo ngeen ba tey ku leen jàngal ndoortel waxi Yàlla. Nàmp um soow ngeen mujj aajowoo, ndax ñàkka àttan ñam wu dëgër.

Sunu Boroom nag, ag muñam, jàppleen ne moo dig mucc, noonee leen ko sunu soppe, mbokk mi Póol binde woon ci xel mu rafet mi ñu ko baaxe.