TSK

TSK · Daniel 3:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aaróona ne leen: «Tekkileen boog, indil ma seen jaaroy wurusi nopp, yi ci seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen.»

Seen jëmmi tuur yooyu nag, lakkleen leen. Buleen xemmem lenn luy xaalis mbaa wurus ci kaw tuur yi. Buleen ko aakimoo, lu ko moy muy seenug fiir, ndax lu seexluwoo ngoogu ci seen Yàlla Aji Sax ji.

¶ Ci kaw loolu Buur seetluwaat mbir ma, daldi sàkklu ñaari wëlluy wurus. Mu ne mbooloo ma: «Yeen waa Israyil, bare ngeen lu ngeen di jaabante yoonu Yerusalem. Xool-leen fii kay! Seen yàlla ya leen génne woon réewum Misraa ngi.»

¶ Lii mu ngi amoon ci jamonoy Aserus. Mooy Aserus ma falu woon, jiite téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar, dale ko ca End ga woon, ba ca réewum Kuus.

Tuuri yéefar yi, xaalis ak wurus, loxoo ko sàkk.

Su boobaa ngeen sobeel seen jëmmi tuur yi ñu xoob xaalis; ak wurus wu xoob seen tuur yi ñu móol, ba boole lépp sànni ni sagar yu sobewu, ne ko: «Sore nu!»

Ñii déy a yullee wurus ci mbuus, sàkk xaalis, natt diisaay ba, fey tëgg bu leen ci tëggal am tuur mu ñuy sukkal ak a sujjóotal,

Nit man naa sàkkal boppam ay yàlla? Te duñuy yàlla sax!»

¶ Ba mu ko defee Buur teral Dañeel, may ko lu baree bare, ba noppi def ko kilifag diiwaanu Babilon gépp, teg ci fal ko, mu yilif boroom xam-xami Babilon yépp.

¶ Ba loolu wéyee Buur gëna teral Sadarag ak Mesag ak Abet Nego ca diiwaanu Babilon.

Hosea 8:4 TSK

Ñoo fal ay buur te du sama ndigal, ñoo tabb ay kàngam, te yéguma. Seen xaalis ak seen wurus lañu sàkke jëmmi tuur, muy seen sànkute.

Ndegam nag xeetu Yàlla lanu, warunoo nirule Yàlla ak lenn luy wurus, mbaa xaalis mbaa aw doj te sosoo ci xareñtey nit akum xelam.

¶ Ndesu nit ñi musiba yooyii reyul nag, taxul sax ñu tuub seeni jëf, ba bañatee jaamu ay tuur, ak jëmmi xërëmi wurus ak xaalis ak xànjar ak xeer ak dénk; xërëm yu gisul, déggul, doxul.