TSK

TSK · Daniel 3:28

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Fajar a ngay xar, malaaka ya fuug Lóot ne ko: «Gaawal gaaw, ànd ak sa soxna ak sa ñaari doom yu jigéen yii, ba bu Yàlla tasee dëkk bi, dungeen sànku.»

Ezra 6:11 TSK

¶ Gannaaw loolu ndigal a ngii tukkee ci man ñeel képp ku tebbi bii dogal: Dees na roccee ca néegam ab xànq, yékkati ko, wékk ko ca, ba noppi def këram ab sën ndax jëfam jooju.

Yaw de, yaay ku sell, tooge sab jal, Israyil di la kañ.

Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.

Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, musal ko fu mu jàqe.

Musiba nag day rey ku bon, te ku bañ aji jub, yoon dab na la.

Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.

Ndokklee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji,

Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.

Waaye barke ñeel na ku wóolu Aji Sax ji, yaakaar Aji Sax ji.

Léegi, bettuma leen. Bu ngeen di dégg bufta geek toxoro geek xalam geek riiti geek kooraa geek liit geek mboolem jumtukaayi xumbal yi rekk, sujjóotleen, màggale ko jëmm ji ma sàkk. Waaye su ngeen ko màggalul, dees na leen daldi sànni ci biir taalu sawara bu yànj. Ana yàlla ju leen di musal ci man?»

Léegi nag man, Nabukodonosor, maa ngi sant Boroom asamaan, di ko sargal, di ko màggal. Lu mu def dëgg la, fu mu jaare njub la, te kuy réy-réylu man na laa suufeel.

Sama Yàlla yebal na malaakaam, mu tëj gémmiñi gaynde yi, ba defuñu ma dara. Ndax kat mucc naa ci tuuma sama digganteek moom ak sama digganteek yaw it, te defuma dara lu bon.»

Acts 5:19 TSK

Ca guddi ga nag malaakam Boroom bi ubbi bunti kaso ba, génne leen, ne leen:

¶ Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax, ngir ngeen jébbal ko seen yaram wépp, def ko jooxe buy dund, sell te neex Yàlla. Loolu déy mooy njaamu, gi leen war.

Nun ci sunu wàllu bopp, jàppoon nanu ne sunu àtteb dee moo taxaw. Waaye loolu tax na nu bañatee yaakaar sunu bopp, xanaa di yaakaar ci Yàlla, miy dekkal ñi dee.

Loolu laa ne siiw, yaakaar ko, te duma rus mukk, xanaa di saxoo aw fit, démb niki tey, ngir ma mana fésale sama jëmm jépp, teddngay Almasi, su may dund ak su may dee.

Ñii, ñu dóor ay doj ba ñu dee, ñee, ñu xeet leen ba xar leen ñaar, ñee, ñu bóome leen saamar, ñii di wëndeelu, sol deri xar mbaa bëy, te diy ndóol, ñu di leen bundxatal, di leen mitital.

Sunu bokk yee daan ndax deretu Gàtt bi, ak seen kàddug seede, te soppuñu seen bakkan ba ragala dee.