TSK

TSK · Daniel 4:37

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba mu ko defee Firawna woo Musaak Aaróona, ne leen: «Ñaanleen Aji Sax ji, ngir mu teqale nook mbott yi, man ak sama waa réew. Kon dinaa bàyyi mbooloo mi, ñu dem rendili Aji Sax ji sarax.»

Kee di cëslaay, te mati jëf, wépp yoonam di njub. Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi, te njekk ak njub mooy boroom.

Buur ne Aman: «Doxal jël mbubb meek fas wi, li nga wax rekk, te nga defal ko Mardose, Yawut biy toog ca buntu kër buur. Bul bàyyi dara ci mboolem li nga wax.»

Aji Sax jee jub kàddu. Mooy jëfe lépp kóllëre.

Aji Sax ji, ràññee naa ne say ndigal njekk la, te worma nga ma dumaa.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ab àtteem lay fésale màggaayam, Yàlla ju sell ji, ag njekkam lay firndeele sellngaam.

Su ko defee nga fàttliku démb, daldi rus, torox ba ne xerem keroog ba ma lay jot ci mboolem loo def. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»

¶ Ca saa sa kàddu ga sotti ñeel Nabukodonosor. Ñu dàqe ko ci nit ñi, muy dunde ñax niw nag, lay biy wàcc di ko faam, ba kawar gi sëq ni dunqi jaxaay, ay wewam di saf yu njanaaw.

Ña ngay naan biiñ, di sàbbaal yàllay wurus yaak yu xaalis yaak yu xànjar yaak yu weñ yaak yu bant yaak yu doj ya.

James 4:6 TSK

Waaye yiw wu gënatee baawaan la maye. Moom la Mbind mi ne: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»

¶ Naka noonu yeen ndaw ñi, nangul-leen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»

Ma dégg sarxalukaay ba ne: «Waawaaw, Boroom bi Yàlla, Aji Man ji, say àtte dëgg la, yoon la.»