TSK

TSK · Daniel 4:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ñaari ati lëmm wees na gannaaw loolu, gént dikkal Firawna, mu jeneer taxaw ca wetu dexu Niil.

Kilifag jawriñ ya nag tudde leen yeneen tur. Dañeel, mu tudde ko Beltasar, Anaña mu tudde ko Sadarag, Mikayel tudd Mesag, Asaryaa di Abet Nego.

Waaye, Buur Nabukodonosor, Yàllaa ngi biir asamaan, di xamle ay mbóot te moo la won liy am jamono yiy ñëw. Sa gént gaak la nga ca gis ca sa kaw lal, lii la:

¶ Ca saa sa baaraami loxob nit buy bind feeñ fa janook tegukaayu làmp ba, ca kaw miiru kër buur, ba ñu weexal. Buur di xool catu loxo bay bind.

Am na góor gu nekk ci sa réew mi; xelu yàlla yu sell yaa ngi ci moom, te ci sa jamonoy baay, gis nañu ci moom ag ràññee ak xel ak xam-xam bu nirook xam-xamu yàlla yi. Buur Nabukodonosor sa baay nag fal ko, mu jiite taryaax yeek ñeengokat yeek xërëmkat yeek seetkat yi;