Ba Aji Kawe ji séddee xeet yi seeni suuf, tasaare doom aadama yi ci àddina, moo àppal xeet yi seen kemi réew, na mu dëppook limeefu goney Yàlla yi.
TSK
TSK · Daniel 5:18
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Fitnaam, këpp ci boppam; coxoram, xàŋŋ cim kaaŋam.
Na xeetoo xeet tàccu, xaacu, sarxolleel Yàlla!
Mboolem xeet yee koy nangul, nangul doomam ba ci sëtam, ba keroog moom itam, àppu réewam jot. Su boobaa am réewam nangul yeneen xeet yu giir ak buur yu mag.
Muy lu baax, di lu aay, du Aji Kawe jeey àddu, amal?
Ndegam Yàlla ji nuy jaamu man nanoo musal ci taalu sawara bu yànj bi, musal nu ci yaw mii, dina nu musal.
Garab gi nga gis muy màgg di réy, njobbaxtal lay laal asamaan, ñu di ko séen ci àddina sépp,
Yaw lañuy dàqe ci nit ñi; rabi àll yi ngay dëkkal, ñax di sam xont niw nag, lay biy wàcc di la faam diiru juróom ñaari jamono, ba kera ngay xam ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.
¶ Dañeel daldi ne Buur: «Buur, guddalu fan!
Ba ma demee ba wetu digg bëccëg, Buur, ca laa gis ag melax gu leer ba raw jant bi, fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër, maak ñi ma àndal.