TSK

TSK · Daniel 5:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Daawuda ne ko: «Bul tiit, dinaa jëfeek yaw ngor déy ngir sa baay Yonatan. Dinaa la delloo mboolem sa suufas maam Sóol, te yaay bokk ak man ndab ba fàww.»

Nabukodonosor jële fa mboolem alali kër Aji Sax ji ak alali kër Buur, daldi buub lépp luy ndabu wurus lu Suleymaan buurub Israyil defarlu woon ci kër Aji Sax ji, muy la Aji Sax ji waxoon.

Ezra 1:7 TSK

Ci biir loolu Buur Sirus génne ndabi kër Aji Sax, ja Nabukodonosor jële woon Yerusalem te yeboon ko ca kër tuuram ya.

Mboolem xeet yee koy nangul, nangul doomam ba ci sëtam, ba keroog moom itam, àppu réewam jot. Su boobaa am réewam nangul yeneen xeet yu giir ak buur yu mag.

Njiital dag ya yóbbaale ndab yu ndaw yaak and yaak ndab yiy def deretu sarax, ak ndab yiy def dóom, ak tegukaayi làmp yaak and yu ndaw yaak këlli tuurukaay ya. Lu ciy wurus, mu ber, lu ciy xaalis, mu ber.

Ña ngay naan biiñ, di sàbbaal yàllay wurus yaak yu xaalis yaak yu xànjar yaak yu weñ yaak yu bant yaak yu doj ya.

¶ Ci kaw loolu ñu indi Dañeel fa kanam Buur. Buur ne Dañeel: «Du yaay Dañeel mi bokk ci Yudeeni ngàllo, ga Buur saa baay jële Yuda?

xanaa ngay diirook Boroom asamaan, bay santaane ñu indil la ndabi këram, nga di ci naan biiñ, yaak say jawriñ ak say soxna ak say nekkaale, ngeen di sàbbaal ay yàllay xaalis ak yu wurus ak yu xànjar ak yu weñ ak yu bant ak yu doj, te du ci lenn luy gis mbaa muy dégg mbaa mu xam dara. Waaye Yàlla ji yor sa bakkan tey ak ëllëg sàbbaaloo ko.