Daawuda ne ña mu dendal: «Ngeen ne, lees di defal ku rey waa Filisti bii, ba faj gàcceg Israyil? Ak kuy yéefaru waa Filisti bii sax, bay dëkk gàngoori Yàlla jiy dund?»
TSK
TSK · Daniel 6:27
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mooy Yàlla ji ma feyul, nangulal ma xeet yi.
Yaw laay làqoo, nga di ma aar ciw ay, may ma ñu ma yéew, di ko bége. Selaw.
Yeen soppey Aji Sax ji, bañleen lu bon. Aji Sax jeey sàmm ay wóllëreem, di leen musal ci ku bon.
Waaye Aji Sax jeey Yàlla dëgg. Mooy Yàlla jiy dund, di buur ba fàww, xadaram gësëm àddina, meram man xeet yi.
¶ «Ci jamonoy buur yooyu Yàlla Boroom asamaan dina samp nguur gu dul tas mukk, te wenn xeet du ko yilif mukk. Nguur googu dina tasaare mboolem yeneen nguur yooyu, ba genn du ci des, waaye moom day sax ba fàww.
¶ Ba àpp ba matee, man Nabukodonosor, maa séentu asamaan, sama sago délsi. Ma sant Aji Kawe ji, sargal Kiy dund ba fàww, màggal ko: kilifteefam sax fàww, nguuram ñeel maasoo maas.
Ngalla tàllalal sa loxo ngir di wéral ak a amal ay firnde aki kéemaan ci turu Yeesu, sa ndaw lu sell li.»
Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.