TSK

TSK · Daniel 8:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 10:7 TSK

Moona xam nga xéll ne tooñuma, te amul kenn kuy xettli nit ci sa loxo.

«Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii, bala maa fàdd te kenn du wallu.

Aji Sax ji dafa wax ki mu fal, Buur Sirus mi mu jàpp ci loxol ndijooram, ngir nangulal ko xeet yi, yolomal ngañaayal buur yi, lafal koy bunt, ba bunti dëkk du tëje,

¶ Kàddu gii la Aji Sax ji wax ci mbirum réewum Babilon, réewum Kaldeen ña, te Yonent Yàlla Yeremi jottli ko.

Màggaay ga mu ko mayoon tax waa mbooloo yeek xeet yeek làkk yépp ragal ko, bay lox ci kanamam. Ku ko soob, mu rey; ku ko soob, mu bàyyi; ku ko soob, mu fal; ku ko soob, mu torxal.

¶ «Ñaareelu rab wa ne jimeet, nirook urs. Mu ngi taxawe wet, ŋank ñetti faar. Ñu ne ko: “Jógal lekk yàpp wu bare.”

¶ «Léegi, maa ngi lay xamal lu wér. Dama ne, dina amaat ñetti buur yuy falu ci réewum Pers, ñeenteel ba dikk, dajale alal ju bare, ba ëpple leen ñoom ñépp. Bu demee ba alalam may ko doole, dina def lépp lu mu man ngir xabtal ñépp ci kaw nguuru Geres.

¶ «Buur bi dina def lu ko soob. Dina réy-réylook a damu, ba weesale boppam tuur yépp, te dina wax gilaawaali jëme ci Yàlla ji sut lépp. Dina am ndam nag ba keroog sànjum Yàlla ñoral ko. Li ñu dogal déy dina am.