TSK

TSK · Daniel 9:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Su ma leen loolu yaralul ba tey, xanaa ngeen sax ci noonoo ma,

Aji Sax ji nee: «Maa leen jiite ñeent fukki at ca màndiŋ ma, seeni yére ràppul, seenu dàll ràppul.

Job 36:13 TSK

Ab yéefar day denc mer, te mbugal du tax mu woote wall.

Ngalla muril saay gët, ma niir sa kéemaani yoon.

Say loxoo ma sàkk, tabax ma, may ma ag dégg, ma mokkal say santaane,

Mbir ya jiitoo ngoog, mat na; yu yees laa leen di yégal, balaa teew, ma yegge leen ko.»

Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.

«Mbugal naa seeni doom, jariñul dara. Dégguñu yar, bóom ngeen seeni yonent, mbete gaynde yuy fàdde.

Sa soppe yépp a la fàtte, kenn faalewu la ci, ndax dumay noon laa la duma, yar la yar bu tar ngir sa ñaawtéef ju réy ak sa bàkkaar yu bare.

ndax yeena def saraxi bokkaale, moy Aji Sax ji, dégluwleen Aji Sax ji, te it kàddug yoonam ak dogali yoonam ak seedey yoonam, jëfewleen ci lenn. Moo waral musiba mi leen dikkal nii tey.»

Mboolem ñi fi jaareey tacc-taccali loxo, ciipu, wëcc bopp ci gentub Yerusalem mu taaru ma, te naan: «Xanaa du biib dëkk lañu doon tudd sottiteb taar ba, te muy mbégtem àddina sépp?»

¶ «“Yaa fàttlikuwul ba ngay ndaw, yaa def lii lépp ba merloo ma. Kon man it, sa jëfin kat laa lay këpp ci bopp, feye la ko. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Du yaa gànctu, dolli ci sa jépp jëf ju siblu?

Hosea 7:7 TSK

Ñoom ñépp a tàng jérr nib taal, te ñooy xoyom seeni njiit, seen buur yépp a daanu, te kenn ci ñoom woowu ma wall.

Du seen xol lañu ma wooye wall, xanaa di salliiru ci seen kaw lal, pepp ak biiñ tax ñuy dagg seen yaram, dëddu ma.

ndegam kay Yeesu ci boppam ngeen dégg mbiram, ba jànge ci moom, dëgg gi bawoo ci moom,