TSK

TSK · Daniel 9:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Firawna nag yónnee, woolu Musaak Aaróona. Mu wax leen ne leen: «Bii yoon de, maa tooñ. Aji Sax ji moo nekk ci dëgg, te maak sama waa réew ñoo sikk.

Yaw nag yaa yelloo njekk ci mboolem li nu dal, ndax worma nga jëfe, nun noo bon.

Ay jëfam dëgg laak njub, tegtalam yépp mata wóolu,

Ñooy gaw Yerusalem ni wattukati tool, ndax man la gàntal.» Kàddug Aji Sax jee.

Te ni ma leen teewloo woon ba ma leen di buddat, di leen fàqat, di leen daaneel, di leen yàqte ak a lor, noonu laa leen di teewloo ngir defar leen, jëmbat leen.» Kàddug Aji Sax jee.

Seen noon yaa jiite tey, seen bañ yooyoo ne finaax, Aji Sax jee mbugale waa Siyoŋ seeni tooñ yu bare, seeni doom duggig njaam, di moomeel ub noon.

Léegi nag man, Nabukodonosor, maa ngi sant Boroom asamaan, di ko sargal, di ko màggal. Lu mu def dëgg la, fu mu jaare njub la, te kuy réy-réylu man na laa suufeel.