TSK

TSK · Deuteronomy 14:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Te itam nit ñu sell ngeen wara doon, ñeel ma, kon nag yàppu mala mu ñu fàdde ci àll bi, buleen ko lekk; sànnileen ko xaj yi.

¶ «Ngëneeli meññeef mi jëkka ñore ci seen suuf, nangeen ko yóbbu seen kër Yàlla Aji Sax ji. «Buleen togge ab tef soowum yaayam.»

¶ «Te itam képp ku lekk médd mbaa lu rab fàdd, muy njuddu-ji-réew mbaa doxandéem, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so, mu doora set.

Lu médd mbaa lu rab fàdd waru koo lekk, mu di ko sobeel. Maay Aji Sax ji.

¶ Ma ne ko: «Ãhã! Boroom bi Aji Sax ji, man de masumaa sobeel sama bopp. Muy lu médd, di lu aw rab fàdd, masuma koo lekk ba may gone ba tey. Wenn yàpp wu daganul masula dugg sama gémmiñ.»

Ma dégg ka sol mbubbam wëñ gu ëccu te taxaw ca kaw dex ga. Ma nga yékkati loxo ndijoor baak bu càmmoñ ba te naa: «Giñ naa ko ci Kiy Dund fàww ne ñetti jamonook genn-wàll lay doon. Xew-xew yooyu yépp a ngi dakk keroog bu dooley mbooloo mu sell mi jeexee tàkk.»

Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.