TSK

TSK · Deuteronomy 31:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe.

¶ Ba loolu amee Musaa woolu Yosuwe, wax ak moom, Israyil gépp teg ci seen bët. Mu ne ko: «Dëgërlul te am fit, ndax yaw yaay ànd ak mbooloo mii ca réew ma Aji Sax ji giñaloon seeni maam, ne ñoom la koy jox. Yaw it yaa leen koy sédde.

Maay yégle muj ca ndoorte la, ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg. Maa naa sama mébét a ngi, day am, sama bépp nammeel sotti.

Hosea 5:3 TSK

Maa xam Efrayim, Israyil laa ne, umpu ma. Efrayim, yaa gànctu, Israyil laa ne, yaa sobeel sa bopp.

Amos 5:25 TSK

«Yeen bànni Israyil, saraxi gàtt ak saraxi pepp, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?

Acts 2:23 TSK

Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.