Musaa ne mbooloo ma: «Fàttlikuleen bésub tey jii ngeen génne Misra, kërug njaam gi, ak ni leen Aji Sax ji yiwee dooley loxoom. Bu ci kenn lekk mburu mu am lawiir.
TSK
TSK · Deuteronomy 6:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Su ko defee, bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: “Lii lu muy tekki?” ngeen wax ko ne ko: “Dooley loxol Aji Sax jee nu génne Misra, kërug njaam ga.
«Man Aji Sax ji, maa di seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga.
Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra. Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen fa génnee dooley loxoom, ak kàttanu përëgam. Moo tax seen Yàlla Aji Sax ji sant leen ngeen wàccoo ak bésub Noflaay.
Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.
ngir ñu wóolu Yàlla, baña fàtte jëfi Yàlla, di jëfey santaaneem,
Dégluleen maa, yeen ñiy wut njekk, di sàkku Aji Sax ji. Xool-leen doj wi ñu leen yette, xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee:
Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa, ji ngeen di ndénkaaneem.