TSK

TSK · Deuteronomy 7:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Ab doxandéem, buleen ko lor, buleen ko not, ndaxte yeen itam ay doxandéem ngeen woon fa réewum Misra.

Moytuleena wóllëranteek niti réew ma ngeen jëm, bala ñoo doon ndëgg-sërëx ci seen biir.

Ci kaw loolu Israyil xasal Aji Sax ji aw xas, ne ko: «Soo tegee ba teg mbooloo mii ci sunuy loxo déy, dinanu faagaagal seeni dëkk.»

Noonu la sunu Yàlla Aji Sax ji tege Og buuru Basan itam ci sunuy loxo, mook gàngooram gépp, nu duma leen ba desewul kuy dund.

Waaye xamleen bés niki tey ne seen Yàlla Aji Sax ji mooy kiy jàll jiite leen, di sawara wuy xoyome. Moo leen di fàkkas, mooy ki leen leen di notal, ngeen dàq leen, sànk leen ci lu gaaw, ni leen ko Aji Sax ji waxe woon.

su boobaa buleen ko nangul, buleen ko déglu, buleen ko xool bëti yërmande, buleen ko baal, buleen ko nëbbal.

Dëkki xeet yii leen seen Yàlla Aji Sax ji sédd nag, buleen ci bàyyi lenn luy noyyi, mu dund.

Aji Sax jee leen di joxe fi seen kanam, ngeen def leen mboolem li ma leen santoon.

¶ Ben Addàd ne Axab: «Dëkk yi sama baay nangoo woon ci sa baay dinaa la ko delloo, te boo yeboo sàkkal sa bopp ay bérabi njaay ca Damaas, na sama baay def ca Samari.» Axab ne ko: «Man nag damay fasanteek yaw kóllëre ci loolu, bàyyi la nga dem.» Ba loolu amee mu fasanteek moom kóllëre, bàyyi ko mu dem.