TSK

TSK · Exodus 13:17

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Firawnaa ngay jubsi, bànni Israyil séentu, yemuñu ci ñu moy waa Misra, ñu dikk, jubsi leen. Tiitaange lu réy jàpp bànni Israyil. Ñu woo Aji Sax ji wall.

Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma.

Waaye bu buur bi barey fas, te bumu delloo askan wi Misra, ngir sàkku fas yu bare, te Aji Sax ji waxoon leen ne buleen dellooti woowu yoon.

Aji Sax jee leen di yeb ciy gaal, delloo leen Misra, yoon wu ma leen noon dungeen ko gisati, ngeen di fa jaay seen bopp seeni noon, ngir doon seen jaam yu góor ak yu jigéen, te kenn du leen jënd.

bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw foofa ca réewum ña leen jàpp, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon,

Képp ku gàdduwul sa bantu bopp bu ñu lay daaj, te topp ci man, doo mana doon sama taalibe.

Teewul Póol jàpp ne gannaaw Yowaan Màrk moomu moo leen waccoon ca Pamfili te àndul woon ak ñoom ci liggéey bi, yóbbaale ko warul.