Aji Sax ji ne ko: «Keroog boo delloo Misra, nanga taxaw temm, te def ca kanam Firawna kéemaan, yi ma teg ci sa loxo yépp. Man maay dëgëral boppam, mu të ba du bàyyi mbooloo mi, ñu dem.
TSK
TSK · Exodus 14:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Waaye man maay dëgëral boppu Firawna, ba fulandi samay firnde ak samay kéemaan ci biir réewum Misra.
Terewul Firawna të, faalewu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
Waaye maa la musal, te li ma ci jublu moo di won la sama doole, ba sama riirum tur dajal àddina.
¶ La Aji Sax ji santoon Musaa ak Aaróona, noonu rekk la ko bànni Israyil defe.
Man nag maay dëgëral boppu waa Misra, ba ñu dugg, topp leen. Su ko defee ma siiwal sama ndam, ndax dinaa yar Firawnaaki xarekatam yépp, boole ci watiiri xareem aki gawaram.
Jaambur ñay dégg, di rag-ragi, tiitaange ne taral waa Filisti,
yaa wàcce ay firndeeki kéemaan ca kaw Firawnaaki jawriñam ñépp ak askanu réewam mépp, ndaxte yégoon nga reewande ga waa Misra doon jëflanteek sunuy maam. Ca nga siiwal saw tur ba tey jii.
Teewul ma sédd ci sama teddngay tur, ngir xeet yi ñu nekk ci seen biir bañ maa sikk. Ndax ba may xamal bànni Israyil sama bopp, di leen génne Misra, xeet yooyaa ko seede woon.
Yaay songi Israyil, sama ñoñ, mel ni aw niir, muur réew ma. Fan yu mujj ya la loolu di am, maa lay yóbbu yaw Gog, ba ca réew ma ma séddoo. Maa lay firndeele sama sellnga, ngir xeet yi gis, ba xam maay kan.
Waa réew mépp a leen di robandoo, te bésub keroog ma darajaal sama bopp, ñu doxe ca siiw. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Mbind mi moo indi kàddu ga dikkaloon Firawna, ne ko: «Maa la yékkati, te li ko waral mooy lii ci boppam: ngir fésal sama doole ci yaw, ngir itam ñu sàbbaal sama tur ci àddina sépp.»
Noonu lees binde ne: «Yàlla moo leen jox xelum ngëmment, ak bët yu dul gis, ak nopp yu dul dégg, ba bésub tey jii.»