TSK

TSK · Exodus 16:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba ñu demee ba mu yàgg, Firawna buuru Misra dee. Fekk na bànni Israyil a ngay binni rekk ndax seen njaam ga. Ñuy woote wall, ba seen jooy, ya sababoo ca seen toroxteg njaam ga, àgg fa Yàlla.

Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra?

¶ Ci biir loolu genn gàngooru njaxasaan mu nekkoon ca seen biir jiital seen bakkan, di ŋaf-ŋafi, ba tax bànni Israyil itam dellu di jàmbat. Ña nga naan: «Éy ku nuy leelatiw yàpp!

Su dee nii ngay def ak man nag, dimbali ma rekk, rey ma ba ma dee, ndax ma baña gis sama toskare.»

Bànni Israyil gépp nag di ñaxtu ci kaw Musaa ak Aaróona, mbooloo ma mépp naa leen: «Waay lu nu tee woona dee ca réewum Misra, mbaa sax nu dee ci màndiŋ mii!

Ana loo indee mbooloom Aji Sax ji ci màndiŋ mii, nu di fi deesi doŋŋ, nook sunug jur?

Moo leen teg coono, xiifal leen, leel leen mànn mu ngeen xamul, te seeni maam xamuñu ko woon, ngir xamal leen ne du aw ñam doŋŋ la doom aadama di dunde, waaye gépp kàddu gu tukkee ci gémmiñu Aji Sax ji, dees na ko dunde.

Job 3:1 TSK

¶ Gannaaw loolu Ayóoba àddu, ma ngay móolu bés ba mu juddoo.

Job 3:20 TSK

Boroom tiis, ana lees koy maye leeru kaw suuf? Lu boroom naqar di doye bakkan?

Alkute ñeel na bés ba ma juddoo, bés ba ma saa ndey juree, yàlla bumu barkeel.

Jonah 4:8 TSK

Naka la jant ba fenk, Yàlla yebal ngelawal penku lu tàng jérr, jant ba jam boppu Yunus, ba mu xawa xëm, bëggatul dara ci bakkanam. Mu naan: «Dee sax a ma gënal dund!»

¶ Yeen daal suur ngeen xaat! Woomle ngeen xaat! Yeena ngi tàmbalee nguuru, te xaaruleen nu ci sax! Céy su ngeen doon nguuru léegi, ba nun itam nu mana nguuroondoo ak yeen!