TSK

TSK · Exodus 28:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maa ngii di ko tofal Oliyab doomu Ayisamaag Daneen bi, te itam mboolem ñi xarala, may naa leen xelum xarala, ngir ñu ànd def mboolem lii ma la sant:

Ci biir loolu jigéen ñu xareñ ñépp ëcce seeni loxo, ngir waajal wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñu boole, indi.

Moo leen feesal xareñte, ngir bépp liggéey, ci wàllu yett ak nataal, ak liggéeyu wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe. Mane nañu ràbb te itam dañuy sos seen taarali bopp.

¶ Ba loolu amee Musaa woo Besalel ak Oliyab ak mboolem ñi xareñ ñi Aji Sax ji xareñal, mboolem ñi am yéeney wàllsi ci liggéey bi, ngir sottal ko.

ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.

Xool-leen ci lii: Ndax beykat bi day dëkke gàbb, di rëdd ak a gàbbaat?

ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax.