Musaa wax Aaróona ak doomam yu góor yi tudd Elasar ak Itamar ne leen: «Buleen njañu te buleen ñaawlu di xotti seeni yére, lu ko moy dingeen dee, te merum Yàlla dina dal ci kaw mbooloo mi mépp. Waaye seen bokki bànni Israyil gépp sañ nañoo jooy ñi Aji Sax ji lakk.
TSK
TSK · Exodus 33:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba Musaa jottlee bànni Israyil gépp kàddu yooyu, mbooloo ma mititlu nañu ko lool.
Buur nag wax Simey ne ko deesu ko rey, daldi ko koy giñal.
¶ Naka la ko Buur Esekiya dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji
¶ Ba Mardose yégee la ñu def lépp, daa xottiy yéreem, sol ay saaku, sottikoo dóom, di ko ñaawloo, dugg ci biir dëkk bi, di yuuxu yuux gu réy te metti.
Ñu dikk ba jub ko, di ko séentoo fu xawa sore, waaye xàmmeetuñu ko. Ñu daldi ne yikkét jooy. Ba ñu agsee ku ci nekk ne sa mbubb tareet. Ñuy ñaawlu, di tibb suuf, di sànni ca kaw, muy sottiku ci seen kaw bopp.
Binnil ndànk te bul ñaawlu. Bul tàggook sa kaala, bul tàggook say carax, bul muur sa tuñum kaw ba ci sikkim di ko ñaawloo. Bul lekk ñam wu la njaal mi indil.»
Mboolem buuri tefes yaay wàcc seeni ngàngune, futti seeni mbubb, tàggook seen yére yu yànj, bàddoo tiitaange, ne dett fi suuf, dëkke kat-kat, seen yaram dawe saw demin.
Mbir ma àgg ca buurub Niniw. Mu ne ñokket, jóge ca ngànguneem, ne futeet mbubbam buuram, sàngoo saaku, daldi toog cib dóom, di ko toroxloo.
«Waxal askanu réew mi mépp, ak sarxalkat yi, nga ne leen: “Ba ngeen dee woor ak a ñaawlu ci weeru juróomeel, ak weeru juróom ñaareel, ci diiru juróom ñaar fukki at yii, ndax man mii ngeen doon woorala wooral?