bu ma daasee sama saamar buy melax, ba ŋàbb ko ci saab loxo, di àtte, maay fey samay digaale, añale samay bañ.
TSK
TSK · Ezekiel 21:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
jam ko ba fëll, cat la bëtt xol ba, di melax fa mu sare, tiitaangey ndee ne ko taral.
Bésub keroog Aji Sax ji dikke saamaram bu jàmbaare, ñàng te réy, ba dal ci kaw Lewiyatan, jaan ja ca xél wa, Lewiyatan jaan jay wañaaruy dem, ninki-nànkay géej jooju lay rey.
Sawara déy la Aji Sax ji di mbugale, saamaram ba dal mboolem doom aadama, ñi Aji Sax ji bóom ne xas.
Bu ñu la laajee ne la: “Fu nu jëm?” nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Kiy wopp dee, wopp dee; kiy deeye saamar, deeye saamar; kiy deeye xiif, deeye xiif; kiy duggi ngàllo, duggi ngàllo.”
Dangay wax waa gottub diiwaanu Negew, ne leen: “Déglul kàddug Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jafal ci sa biir, daay guy xoyom sa garab yépp, gu naat ak gu wow. Dara du ko mana fey. Daay ga day jóge bëj-saalum ba bëj-gànnaar te ñépp a cay lakk,
Dees koo jonj ngir bóome, jonj koo jonj ba muy tàkk. Ana nu nu mana bége lii? Ngeen ne Aji Sax ji nee: ‘Yetu nguurug Yuda sama doom a ngi fi.’ Waaye saamar bi faalewul benn bant!
Su ñu demee, diy jaam ñu seeni noon jiital, fa laay sante boroom saamar, mu bóom leen. Du bëtu jàmm laa leen di xoole, bët bu aay laa leen di xoole moos!»