Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.
TSK
TSK · Ezra 3:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Nanga defare sarxalukaay bi bantu séng, guddaay bi di juróomi xasab, yaatuwaay bi di juróomi xasab; ab kaare la sarxalukaay biy doon, taxawaayam di ñetti xasab.
Nga waxleen ne leen, lii moo di saraxu sawara bi ñuy indil Aji Sax ji: xar yu góor yu menn at yu mucc sikk, ñaar ci bés bi, muy saraxu rendi-dóomal bi war bés bu nekk.
Waaye seetleen bérab bu seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji, ci mboolem seeni giir, ngir teg fa turam, dëël ko fa, te ngeen dem foofa.
Ña nga ñibbi ca njiital Sorobabel ak Yosuwe ak Neyemi ak Seraya ak Relaya ak Mardose ak Bilsan ak Mispar ak Bigway ak Reyum ak Baana. Limeefu góori bànni Israyil nii la tëdde:
Ñu gis ne ñenn ci askanu sarxalkat yi jëloon nañu ay jaambur soxna: Ci askanu Yosuwe doomu Yoccadag aki bokkam, Maaseya ak Elyeser ak Yarib ak Gedalya bokk nañu ca.
Ci askanu Arim, Maaseya laak Ilyaas ak Semaya ak Yeyel ak Osiyas.
¶ Sarxalkat yaak Leween ña ñibbsi, ànd ak Sorobabel doomu Selcel, ak Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ñii la: Seraya ak Yeremi ak Esra
xanaa tànn giirug Yuda, taamu tundu Siyoŋ wi mu sopp.
¶ Ba loolu amee doomu Selcel, Sorobabel, ak doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ak mboolem ña des ca askan wa, ñoom ñépp déggal seen wooteb Yàlla Aji Sax ji, ak kàddug Yonent Yàlla Ase, noonee ko ko seen Yàlla Aji Sax ji yóbbantee. Askan wa nag ragal Aji Sax ji.
«Waxal nag doomu Selcel, Sorobabel boroom Yuda, ak doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, ak ñi des ci askan wi, nga ne leen:
Bésub keroog, kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, maa lay jël, yaw samab jaam, Sorobabel doomu Selcel, kàddug Aji Sax jee, te jaarob torlukaay laa lay def, nde yaw laa taamu. Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.»
Déglul bu baax, yaw Yosuwe sarxalkat bu mag bi, yaak sa xarit yi toog fi sa kanam te taxawe ab tegtal, nde maa ngii di indi samab jaam, ki ñuy wax Njebbit li.
¶ «Jëlal yóbbal boobu, di wurus wi ak xaalis bi, nga sàkk ci mbaxanam buur, te teg ko ci kaw boppu sarxalkat bu mag bi, Yosuwe doomu Yoccadag.
Yoda, Yowanan; Yowanan, Resa; Resa, Sorobabel; Sorobabel, Selcel; Selcel, Neri;