TSK

TSK · Genesis 1:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 38:19 TSK

Ana yoon wa jëm fa leer dëkke, ak fa lëndëm màkkaanoo,

Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.

làmboo leer ni mbubb, firi asamaan ni ndimo,

Nañu màggal turu Aji Sax ji, kii kat a santaane, lii lépp am.

Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.

Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.

te lépp lu ñu wone ci ag leer, di ag leer. Moo tax ñu ne: «Yaw miy nelaw, yewwul, dekkil, Almasi leeral la.»