ànd nañu, dal ci kaw ñoom Bera buurub Sodom, ak Birsa buurub Gomor, ak Sineyab buurub Atma, ak Semeber buurub Ceboyim, ak it buuru dëkk ba ñuy wax Bela, mooy Sowar ba tey.
TSK
TSK · Genesis 10:19
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Aji Sax ji nag àddu ne: «Bàkkaari Sodom ak Gomor bare na lool, ba may dégg yuux, yi sababoo ci seen moy.
¶ Ba loolu amee Ibraayma dafa jóge fa mu nekkoon, jublu àllub Negew, sanci diggante Kades ak Sur, ba noppi ganeji ay fan ca dëkk ba ñu naa Gerar.
«Santal bànni Israyil, nga ne leen bu ngeen duggee réewum Kanaan, lii moo di réew ma ngeen di muurloo, muy seenub cér. Réewum Kanaan a ngi, ak kemi suufam:
Ba Aji Kawe ji séddee xeet yi seeni suuf, tasaare doom aadama yi ci àddina, moo àppal xeet yi seen kemi réew, na mu dëppook limeefu goney Yàlla yi.
Aji Sax ji tàllal na loxoom, tiimale géej, yëngal réew yi, ba santaane ñu màbb tatay Kanaan.
«Efrayim, ana nu ma lay baye, yaw Israyil laa ne, nu ma lay tege ciy loxo? Ana nu ma lay defe ni Atma? Nu ma lay yemaleek Ceboyim? Sama xol a bëpp, sama yërmandee yëngu.