TSK

TSK · Genesis 10:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ñooñu ñooy ñetti doomi Nóoyin yu góor, te ci ñoom la àddina sépp soqikoo.

Eber moom, jur ñaari doom yu góor, kenn ki tudd Peleg (mu firi Séddlikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddlikoo woon. Rakku Peleg mooy Yogtaan.

¶ Ca ndoorte la nag waa àddina sépp a bokkoon wenn làkk, seeni wax di benn.

Looloo tax ñu tudde dëkk ba Babel (mu firi Safaan), ndax foofa la Aji Sax ji safaane làkku àddina sépp, mu jaxasoo, te fa la leen tasaaree ci kaw suuf sépp.

¶ Gannaaw loolu Buur Aserus gàll ab galag ca réew ma mépp, ba ca duni géej ga.

Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom ñaareel bi yoon, ngir jotaat ndesu ñoñam, wa des Asiri ak Misra, ak Pattros ak réewum Kuus, ak Elam ak Sineyaar, ak Amat ak biir duni géej ya.

Xeet yaa ngii, mel ni aw toq ci biir bagaan, jàppeesu leen lu moy diisaayu feppu suuf! Dun yi lay yékkati ni pëndub suuf!

Du toqi, du nasax, ba keroog muy dëj àtteb yoon fi kaw suuf, fa waa dun ya di séentu ndigalu yoonam.»

Yeen waa duni géej, dégluleen ma; yeen askan ya fu sore, teewluleen ma. Fa sama biiru ndey la ma Aji Sax ji wooye, moo tudd sama tur ba ma saa ndey juragul.

Mooy delloo ku ne yool ba mu yelloo, mbugal ay bañam, fey ay noonam, ba delloo waa dun ya yool ba ñu yelloo.

«Jàll-leen ba ca duni Kitim fa sowu, te xool; yónneeleen Kedar fa penku, seetlu bu baaxa baax ndegam dingeen gis lu mel nii!

Nu raglu la Aji Sax jiy dale ci seen kaw, te mooy ràggal yàllay àddina yépp, ba xeet yi di ko sujjóotale dunoo dun, wu ci nekk ak fa nga fare.