TSK

TSK · Genesis 12:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan.

Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.»

Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa.

¶ Ndaxam bi Yàllay tas dëkki joor ga, xalaat na Ibraayma, ba musal Lóot ca dogalam boobee, keroog ba mu tasee dëkk, ya Lóot daloon.

te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»

Aji Sax ji dafa barkeel sama sang lool, ba muy boroom daraja. May na ko jur gu gàtt ak gu gudd, xaalis ak wurus ak ay surga yu góor ak yu jigéen ak ay giléem aki mbaam.

Yal na la ay giir nangul, ay réew di la sujjóotal, nga yilif say bokk, te say doomi ndey di la sujjóotal. Ku la móolooy alku, te ku la ñaanal barkeel.»

Yal na la barkeb Ibraayma dal, yaak askan wi soqikoo ci yaw, ba nga moom réew mii ngay doxandéem tey, te Yàlla mayoon ko Ibraayma.»

Yàlla neeti ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Giiral te yokku, ba aw askan ak mboolooy askan sosoo ci yaw, te ay buur askanoo ci sa geño.

Bànni Israyil nag giir fa, law, di fulandiwu, ba yokku lool, fees réew ma.

Maa leen di fàdde mbas, nangu seen cér, ba noppi sose ci yaw askan wu leen ëpp, ëpp leen doole.»

Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.

te it jawriñi Buur ñëw nañu, di sargalsi sunu sang Buur Daawuda, ne ko: “Yal na sa Yàlla siiwal turu Suleymaan, ba mu gën laa amu tur. Yal na kaweel ab jalam, ba mu gëna kawe sab jal.” Buur sujjóot ca kaw lalam,

Job 35:8 TSK

Sag mbon, sa moroomu nit lay lor, sag njekk it doom aadama ni yaw lay jariñ.

Yaay sàmm kóllëre ak Yanqóoba, yéwéne Ibraayma, na nga ko giñale woon sunuy maam, janti démb.

Gannaaw gi la jagoo màndargam xaraf, mu firndeel àtteb njubam gi ngëmam waral, te fekkul mu xaraf. Noonu la Ibraayma mana nekke maamu mboolem gëmkat ñi. Looloo tax muy maamu mboolem ñi xaraful, te gëm, ndax ñu waññal leen seen ngëm, ab àtteb ñu jub.

Noonu la deme ngir barkeb Ibraayma wàccal xeet yi dul Yawut ndax Almasi Yeesu, ngir itam nu jot ci digeb Noo gu Sell gi, ci kaw ngëm.