Yàlla tudde joor gu wow gi suuf, ndox mi gëndoo, mu tudde ko géej. Yàlla gis ne baax na.
TSK
TSK · Genesis 2:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndax man Aji Sax ji, juróom benni fan laa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak mboolem li ci biir, bésub juróom ñaareel ba, ma dal-lu. Moo tax man Aji Sax ji ma barkeel bésub Noflaay, sellal ko.
Buleen séentu asamaan, gis jant bi, mbaa weer wi, mbaa biddiiw yi, ak mboolem leeri asamaan, ba mu xiirtal leen ci di leen sujjóotal ak a jaamu, te seen Yàlla Aji Sax ji féetale yooyii, mboolem xeet yi asamaan tiim.
Esekiya ñaan fi kanam Aji Sax ji, ne ko: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil mi toog fi tiim malaakay serub yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf.
Ana ku umple ci mboolem ñii, ne loxol Aji Sax jee def lii lépp?
Moo àddu, mu am; santaane, mu sotti.
làmboo leer ni mbubb, firi asamaan ni ndimo,
ki sàkk kaw ak suuf, géej ak lu ci biiram, di sàmm dëgg ba fàww,
Séentuleen kaw, xool-leen ki sàkk yii fi kaw! Xanaa kiy daaguloo seen gàngoor gu mat, ñoom ñépp lay woo ci seen tur, ci kawewaayu dooleem ak màggaayu kàttanam, te kenn du ci wuute.
Man maa amal suuf, sàkk doom aadama fi kaw suuf. Man mii la samay yoxo firi asamaan, te maay jox gàngoori asamaan lépp ndigal.
te sama loxo bee dëj suuf, sama ndijoor bi firi asamaan. Maa leen di woo, ñu bokk taxaw.
«Maa ngii di sàkksi asamaan su yees ak suuf su yees. Deesul fàttlikooti yëf ya jiitu, xel dootu ci dem.
Suuf, Aji Sax jee sàkke kàttanam; dun bi, mu sampem xelam; asamaan, mu lale xam-xamam.
¶ Ab yéenee ngi, di kàddug Aji Sax ju dikkal Israyil. Kàddug Aji Sax jee, ki firi asamaan, lal suuf, te bind noowug doom aadama ci biir doom aadama.
Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.
Nun ñi gëm doŋŋ nooy tàbbi ci noflaayam, noonu mu ko waxe, ne: «Maa giñe sama biir mer, ne: “Duñu tàbbi mukk ci samag noflaay.” » Ndaxam ca cosaanu àddina la liggéeyi Yàlla sotti woon ba noppi,